Doxalukaay bu mbëj
Doxalukaay bu mbëj, ab wuutuloxob mbëj la, boo xam ne kàttan giy duggu ci moom gu mbëj la te ga muy génne gu doolerandu la. Doxalukaay yu mbëj yi am nañu solo lool ci dundiinu jamono ju bees ji, te it dëgg la sax, ne limu doxalukaay yu mbëj yi nekk ci am réew dafay firndeel tolluwaayu jëm-kanamam. Maanaam yokkug limu doxalukaay yu mbëj yi ci am réew bokk na ci wonekaay yiy firndeel tolluwaayu yokkuteem ci wàllu xarala mu réew moomu. Ngir dëggal loolu, doy na xool ci jumtukaay yi nekk ci li ñu wër: ca saxaar ba ci watukaay ak yeneen ak yeneen, yi ngeen xam ne nit ku bees ki moo ngi koy jëfandikoo bu baax, man naa ni sax ñooy doxal sunug dund.
Doxalukaay yu mbëj yi dañoo bari te wuute, am na doxalukaay bu dawaan bu wéy, doxalukaay bu dawaan bu safaanu moom mu séddaliku ci doxalukaay bu demandoo ak doxalukaay bu demandoodi,.
Xaralay doxiin gi
[Soppi • soppi gongikuwaay bi]cëri ad doxalukaay
[Soppi • soppi gongikuwaay bi]Doxiin
[Soppi • soppi gongikuwaay bi]Dawaanu mbëj bi day jaar ci ag lëmës gees wëndeel ci ab dogub weñ bi tudd tekkaaralaan bi. Lëmës googu, gi ñu defare ak wëñu përëm (naka-jekk përëm lay doon waaye manees na koo defaree ak beneen xeetu wommatukaay), dafay jur ab toolu mbëjbijjaakon, tool bi dafay feeñ niki ag walug bijjaakon, di lees man a natt. Danu koy jàppee niki jenn doole di lees di wax dooley Lorentz. Toolu mbëjbijjaakon boobu dafay duggante ak toolu mbëjbijjaakon bu lëmës gu wëndeeluwaan bi jur, mi melokaanoo teewaayu ñaar walla ñetti seexi dott. Wëndeeluwaan bi tambalee wëndeelu ci ndimbalu dooley Lorentz; bëj-gànnaaru toolu bijjaakon bu wëndeeluwaan bi day bijjante ak bëj-saalumu toolu bijjaakon bu tekkaaralaan bi. Xaaju wëndeelu gu nekk, dott bi day soppeeku, ci noonu la wëndeelu gi man a wéyee.
Taariixam
[Soppi • soppi gongikuwaay bi]Ci atum 1821, lu weesu xamteg feñte gu mbëjbijjaakon gi simikat boobu di Ørsted xamle woon, la jëmmalkat bu waa-angalteer bii di Michael Faraday defar ñaari wuutuloxo ngir sàkk li mu duppee ag wëndeelug mbëjbijjaakon: ab doxub dooley bijjaakon bu mbegewu te wéy, ci lu wër ab wëñ, ci maanaa mooy faramfaceg doxalukaay bu mbëj gu njëkk.
Xeeti doxalukaay yu mbëj
[Soppi • soppi gongikuwaay bi]Xeeti doxalukaay yu mbëj yi am, manees naa wax ne, du xaaj du jeex, waaye manees na cee lim yi ëpp yees di jëfandikoo: